fbpx

COVID-19 tchii lakou wolof

Meun nga aam xibaar you bèes lii tchii biir COVID-19 bou djogé tchii ministaire bou Weer gui yaram ak borom rewmi, tchii wolof

Ñii djiité rëwmi djokhé ñjañju aye diktal you bëes ñio meuna taxaw tchii vaccine aak wallanté

Lou djogé tchii taxa way bii djogé tchii ministére bii bës bii 12. mai 2020

Danemark défa bok tchi yëw rii dii djiité tchii wallum test tchii COVID-19, tëy djii ñio bôk tchii rëwyii bouy tésté niit you beuré tchii mbolo. Taxaway bii meuna geuna deugeur. Ndakh boudeh wallanté bii défay djôgât, ñio meun kô gawa yeug, motakhiit dûñio soxla aye taxaway you deugeur.

Dûñio soxla fûñu meuna vëtal ñii fëbar, ñio bâgnâ tëdj deukeu bii aak meuna taxa waal wallanté bii. Lûuñu geuna beuga moy suñu maag yii meuna dundu sën dundu, meuna guisât sën dôom aak sëut yii.

Doxalin wu nu dëxëñ moy: niit bou aam fëbar bii, sañ sañ défa beugeu kham kâan moy aanandô aam. Ñio meuna tésté aandândô yii meun léen wëtal baalâ ñuy meuna wallaaté. Ngùr diina tidjii aye wôté kaay you yakamti dii djapalé mbolo bou ñio waal, meu meuna kham aandândô am, ñio meuna taxawal wallaté bii.

Lou tchi tôp moy ngùr mii ak mbôlô dina aam aye samp you wët, nga khamnati yow mii amoulô fô meuna vët ak fëbar bii, meun nga aam fo vët.

Støt Mino Danmarks arbejde.


Ministaire bou dal djokhé na aye yëglé you djëm tchii muuraay gémiñ

Niit you beuré ñju gui défar aye sën muuraay gémiñ bôp. Ministaire bou dal néena ngéen oytû lii dône aye muuraay kanam yu ñio ñiaw defay djôkhé aye jagadi yu kaaraange.

Jagadi moy manam yow nga geum ni dinala aarû, motakh dinga dëm ba bayi raxasû aak moytû niit. Muuraay gémiñ bou nio défar tchii kër dou laa aar niingko sôxla tchi wallum COVID-19, ndakh doomu jàngoro meuna aam fûmû dûgû.

Muuraay gémiñ défa lâdj aye xarala mou meuna aar fëbaar. Kiy jariñoo défa wôraa sëtlu ndakh muuraay gémiñ aamna rāñeekaay “CE” bou fëgñ, moo done rāñeekaay bii nga khaamni mbolo dékô soxla.

Jaay aye mpèhè nga khaamni djaarul tchii yôone, loulou défa jagadi.

Dalay défa deugeur tchii taxaway yam tchii jaar tchii yône, maanam ñio oytû sûñu morom sët moo aam sôlô tchii wallum COVID-19.

Dooliil khaam khaam:
https://www.sik.dk/erhverv/produkter/personlige-vaernemidler/vejledninger-forbindelse-corona-covid-19/hjemmestrikkede-masker-giver-formentlig-ikke-beskyttelse#

aak fii:
https://www.dr.dk/nyheder/indland/styrelse-hjemmestrikkede-og-hjemmesyede-masker-giver-falsk-beskyttelse

Støt Mino Danmarks arbejde.


Wadjaal Tidjii Deukeu Bii

Lou djogeu tchii taxaway 7. may ak Ministre bou djité rewmi Mette Frederiksen

Danois yeup défnañio lou ñio meune, dii sorénté, sëtaay bii. Motakh legui meune naa ñio tidjii deukeu bii ndank. 

Ministre bou djiité wëer gu yaram seen taxaway tchii sorenté bii aak sëtaay mo aam ba légui, Motakh ñieup ñio woraa djap tchii taxaway yii.

Lou tôpe tchii taxaway yii ñio meuna tidjii deukeu bii dina geuna deugeur. Lou aam sôlô moy ñiou meuna testé ñiinji, boo aamoul symptôme fëbar, ñii néka tchii séne këur. Aye teste dina aam tchii mbolo, yéne yii tchi yéen dii ngéen djot aye wôté ngéen meuna djeul aye moytu kaye.

Fase 2 tjii meuna tidji deukeu bii:

  • Suñu marche meuna tidji, mou done centre commercial aak lénén (11. Mai)
  • Restaurant, café aak lénén meuna tidji, bou ñio djeulé séne oytû tchii bagña djégéunté (18. maj)
  • 6.-10. class meuna ñio deem djangi (18. mai)
  • Ligeuy kây yii meun na ñio tidji ndakh mbolo meuna délu dii ligeuy
  • Sport meun na tidji sauf boumu aam aye niit
  • Biblotheque yii meuna tidji niit meuna aabe tëré (18. mai)
  • Centre yii nga khaamni ñio ngi yeungu tchii yaram, meuna tidji tamit, naañio djeul sén natu kaye rék (18. mai)

Lou dës moy tidji frontiere yii, lolou dina ñio tchii djaaraat. Gouvernement bii dina tchii waakh 1. juin 2020.

Boudeh suñu tidjii yii défa déf corona bii defay aamat dolé, deukeu dine djeulaat moytu kayam tchii tidjii deukeu bii. Ministére bou wër gui yaram défa wora meuna kham naka laa nio wora def, ñio oytû sûñu morom tchii wër yii djem kanam.

Djangue kô fii tchii https://www.regeringen.dk/nyheder/2020/pressemoede-om-genaabning-af-danmark-fase-2/

Støt Mino Danmarks arbejde.


Xëtu tektal you bés bou djogé tchii diglé

Bou djekeu ñi woora oytû tchii wallum COVID-19 défa yatû wône, motakh diktal bou bés, ñio meuna kham kaan mô woora oytû tchii wallaté coronavirus.

Djûrôm ñiar mbolo ñio woora oytû:

1.Kou djem maag – leup tchii wër gû yaram

Virusbii liimu wôné moy maag ñio aam 70ans djem kaw, aak ñii wésû 80ans, ñio yomb waalaté ak fébar. Ñio gaaw aam fébar bii moy maag kû aam 65ans, boudeh dangâ aand ak fébar.

Kû djem maag aam 65ans djem kaw, boudeh daanga aand ak wér gu yaram yow worulô ragal. Môtâkh légui maam yii meun ngén guiss seen sët yii – ngën néhkhãl léen.

2.Ñi deuk tchii resisdence

Kou deuk tchii residence défa dône maag, aand ak hasay bou néxûl. Môtakh ñii lagñio wora oytu.

3.Mbolo kou aam yaram

Boudeh danga aam yaram lou tchii beure dangay aand ak yénéen fébar, kome diabéte wala fëbaar khôl. Niit kô khamni défa aam BMI bou eup 35, wala BMI bou 30 aand hasay meuna aam aye djafé djafé boudeh daanga aand ak COVID-19.

4.Niit ñio aand ak yéene hasay

Dou Hasay fébar yeup moy djokhé djafé djafé, sûr tout boudeh yangui fadjû. Si sûf meun nga guiss fëbar yii néka tchi hasay boudeh danga aam COVID-19:

https://www.sst.dk/da/Udgivelser/2020/Personer-med-oeget-risiko-ved-COVID-19

5.Khâlé bou aand ak hasay fébar

Ýene khâlé ñio aam hasay fébar ñio wora oytû COVID-19. Sûr tût khâlé yii nga khamni diñio sokhla ndimbal – baalaa pandemi dii aam – Khâlé yii aak séne mbôk dina ñio aam ndimbal.

6.Niit kou aamoul këur

Niit kou aamoul këur défay aam djafé aak sëtay soré niit tchii bôpam dina méti. Motakh wallanté bii defay yômb. Lou tchi tôp moy niit kou aamoul këur lou tchii beuré défay aand aak hasay fébar. Lii yeup défa bôk tchii mbolo bii meuna aam fébar bou djafé.

7.Djiigén bou aand aak bïr

Lii ndimbal rék la, ndakh kou aand ak biir défa gâw aand ak hasavay fébar. Daar wônéwûl kou aand ak biir, walla dômb djii, ñiom niar séen fébar geuneul méti mbolo. Tchii lûñû khaam, yaay ak dôm ñii wosin aak aand ak COVID-19, dômb bii diina djûdû baala djotaam. Motakh ñio wora aru yaaye aak dômb.


https://www.sst.dk/da/corona/Saerlige-risikogrupper

Støt Mino Danmarks arbejde.


Niit kou aand ak fébar bou yombà meun nga aam vaacination bouy aar pneumokokker


Mbolo, nga khaamni défa aand ak fébar bou yombà nga khamni défay yômbal walanté COVID-19 tchii yaram, meun nga wô saa faadj kaat mou meun laa djokh vaccine bouy aar pneumokokker. 

Vaccination bii defay aar ñi nga khaamni fébar défa yômb tchii séen yaram, aak ñii nga khaamni dûñio gaaw aam COVID-19. 

Vaccination bii, dou vaccine nga khamni défay fadj COVID-19. Vaccine bii moy aar béne fébar bou tûdû pneumokok-bacteri, nga khaamni bii défa meuna djokhé aye fébar bou néka tchii deurét ak fëbaar deûne. 

Niit you beuré ñio gaaw aam fébar, ndaakh séne aat waala mou dône niakum wër. Motakh ñio waakh ñii djem maag, ñii deuk tchii biir resisdence aand ak niakum wërgu yaram, ñiom ñio meuna aaam vaccine bii. 

Leup lô beug khâm tchhii ndakh yangui bôk tchii vaccine yii ñungi kô biind fii:

https://www.sst.dk/da/Viden/Vaccination/

Liing beug kham tchii vaccination bii: 

https://www.sst.dk/da

Støt Mino Danmarks arbejde.


Jokko bii djogé tchii Ministre Bou Djitou Réwmii beus. bii done juóom benn tchii weeru avril waxtu fuki ak njiaar

Tarixx bii dëgër na, ñuu ngui tchii yône: Ñiaar téemer ak ñéet ñjô teudeu tjibiir hôpital yii,

Béene tëmér ak djûrôm ñent séne wergui yaram déesna, ak béen témer ak djurôme njaar ñio ñiaak séne bâkane.

Ministre Bou Djitou Rewmi bëugëuna ñio faatéelé kou, fébaar bii balaa mûy fégñ tchii yaraam diina djeul ñiët ba ñient ayubés, moo taakhit defko djaakhaal mungui guiss ñiin ñi dii bagña faalée reglement yii – kôme aye niit dii dêf aye yëndou paque.

Motakh Ministre Bou djitou Rewmi djokhé naa fou ñio wora djeké ñio meuna tidji deukeu bi indank. Ñio diapanté deukeu bii yeup ñio meuna gëuna tchii lii: raxasaal saa loxo, boul djéegé niit ak ngéne baagña beuré boudeh daangén dii dadjé.

  1. louy djiitou ñio meuna Ûbi deukeubi:  
  • Hôpitâl yii dina meuna djeul aye niit nga khamanté nii dou corona
  • Këur yii dii djap tëy aye khalé, ecole 0-5’eme class diina tiidji
    • Këur yii diina Ñio djeul séen naatu kaay baala ñio tiidji. 
  • Liguéyekat yii tôg séen këur, meun géen ndank djogat tchii séen liguéye.

Ministre Bou Djitou Rewmi lou wôraal lii leup moy ñio deugeur tchii tarixx bii – Ñio djapalaanté.

Lou déss môy taxaa way yii djiitû – diinan ko yôk aye ñiente ayubës baa beusou fouki tchii wéerou maï.

  • Tëdj frontiere yii
  • Daadjé you eupeu fuki niit 
  • Lou ñio taxaawal baa paré
  • Ecole you maag, biblothec, cinéma, centre commerce ak cafée yii leuop deefay tedj
  • Waatkaat yii, taatueur ak séen morom tamit.

Ministre Bou Djitou Rewmii beugeuna ñio maanu. Ndakh lougñio khaam dootoul amaati – baala suñû mbolo dii dône limu néekône dina yéekh tée deésna aye vër.

Baa paré défa yôk sûñu navlé:

  • Éléve nék tchii 6-10class (4eme-6eme) dûñio woora tôg séen këur, examin amoul motakh note bii ñio mudjé aam moy séne taxa way. 
  • Éléve yii nga khaamanti nii diñio soxla aye examin, diiñian ko aam waye diina wuté.
  • Aye assemblement you maag festival, marché: dina taxaw baa wéerou auôt.
  • Ngûr gii diina khôlaat faanla meuna djapalé waaté.

Ministre Bi Djiou Rewmi mungui ladjté djapalanté, borom banque yii ak njii nga khaamnaténi ñio yoor louase yii, ñio woné solidarité – Akk kuu nék naa djapalé borom boutique you ndaw yii.

Ministre Bii Djitou Rewmi diina yok nate kaye teste yii, aak khamnaani njii dii ligueye tchii wër gui yaram ñio gui daaw ñiogui déf leup pour meuna aam louñu sokhla. 

Lou Ministre Bii Djité Rewmi djekhalée moy, ñio djapalaanté: kutchii nél aam nga tchii saa wallum. Nonu rék lagñu meuna déf ñio meuna  tiidji waat suñu mbolo.

Støt Mino Danmarks arbejde.


Yoonéenté bii djogé suñu ministaire bii yoré walloum fadj: Oytuul saa bope ak njeenéen nga khamanti ni dou ñio sande ak coronavirus

Liinga wora khaam tchii corona:

Wakhtou bii défa khaawaa djafé ndakh féebar bii. Moo takh ñio geuna deugeuraal suñu taawaye, ndak ñio meuna wajní waallanté bii. Motakh ministaire bou Febar ak wéer gu yaram djokhé taxaway yii.

Boudeh daanga aand aak weergu yaram:

  • Moytuul dii laalanté aye niit yu beuré
  • Boudeh daanga djégé niit koo khaamanté défa aand ak corona, bayil khéel sii tchaa wéergu yaram.
  • Topatoowal saa waa djûur/këur – Boudeh aye mag laa ñio oytul léen bou bakh

Boudeh féebar bii défa féegñ tchii yow:

  • tôgal saa këur béene/ñiar faan baa nga yeug yangui wéer
  • Soréel saa waa këur – teudeu bii moo aam sollo
  • Séet défa aam sollo
  • Saa soxlaa défa wora yéem tchii téléfone – ndibaal ndugu tamit amnaa sollo
  • Saa wéer guu yaram bou watché, saa yaram taangeu, meunuloo noyii bou bakh – wôtél saa fadj kaat.

Topotowaal saa bop nga meuna topotoo sa morom.

Støt Mino Danmarks arbejde.


Tchii besou mii fuki ak ñett tchii weeru marts (13.marts 2020) Rewmii défaay yooka sën arou rewmi.

Lii tchii biir conference aak journaliste yii beusou bii ñaar-fuuk ak ñett tchii biir wéeru marts 2020.

Miinistere bouy djiitaal rewmii Mette Frederiksen, defaa yôka aye aarou rewmii ngaa khaanii defko tég baa paré baa beusou mii fuji ak ñett avril 2020.

ñeen-ti-fuki-ak- ñëent-ttéeméer (254) ñio teudaâh tchii hôpitâl yii aak féebaar coronavirus. Djûrum-fuki-ak-djurôm (55) ñio nékah tchii baajnaa weur. Niar-fuki-ak-ñiente (24) ñio njaka sëen baakaan.

Rewmii moungii geunaa djaapaa sii séen taxawaay bougñio djeuka déf. Lou aam sollo moy djaapa sii wajñii waallaanté féebaar bii. Motakh Rewmi yookaa tëdju kaye rewmii baa bessou fuki-ak-ñett (13) tchii biir weeru avril 2020.

Djiitaalé kaye rewmi, Mette Frederiksen, néehnaa aamnaa sollo ñio djápe tchii lûñio tawaal, khaamnnaa nii tamit diina djafée tchii waakhtu yii nga khaamnii niit yii dûñû woora déf séne maagal.

Dëel tôg saa keur ak saakh boudeh tuki tchii biir gohk laay dône.

Kû tchii aam aye tolof tolof meunga liidjaantii ndimbaal, ndakh ndibaal aamna boudeh tchii djapalé khâlée/ndongo.

Aamnaa tamit aye yéene keur, foo meuna dougou boudeh amoulo keur walla niaka aam fiinga meuna wutii sûtûrá – keur yii aamna fadjuu kaye boudéh daanga aand ak fëbaar bii.

Lou tchii mudjuu moy – Djaapaaléel rewmi tchii site bii tudu coronasmitte.dk, kû beuga ndimbaléee rewmii djaapa sii. Tchii sûñû site aamnaa link nga khaamaan tée nii défa tudu; Danemark dina djaapalée Danaemark (Danmark hjaelper Danmark) – Tchii biir fii diinga guiss aak taasanté aak niit yô khaamaantée nii aam naa ñio khaam khaam bii ñio sôkhla tchii biir sûñû rew.

Støt Mino Danmarks arbejde.


Njou eumb aak seen symptôme duunjoo wooraa téesté wu baalaa njuy djuur

Beusou alxamis  fukk ak juróom-ñeent bii tchii biir weerou  marts, Ministaire bou weerguu yaram defa djokhé kaadouam tchii djiigeen bou eumb ak niou woora woosine, tchii wakhtu bii nga khaam nii CIVID-19.

Kuu wooraa djuur dûñko woora testé (corona) bou dougéh tchii biir hôpitâl bii. Boudeh teste (corona) bii defa féenjaal febaar bii (corona), ñjeup ñjio woora aaru, djiigeen bii eumb aak niit yii nga khaamanti njou gii ligeuyi tchii biir hôpiteaux yii. Kûtchii neka defa woora sôl masqaam.

Boudeh defa aam ñiar khéel tchii djiigeen bii, maanam ndakh defa aand ak febaar wala déet, dûñu koy djaapalé nii melnii defa féebar. Baa téste bii ñiu djeel feejnaal ñu leeneen.

Lou tchii moy:
Boodéeh saa morom (partenaire) defa aand aak feebar bii, yow mii diiko seetsi, dôñio laay téré dougou – Lolou tamit daay aam boudeh woorul tchii téste.
Morom bou aand aak féebaar défa wora moytu doomaam aye niarii faan, nga khaamni féebar bii féeñiul tchii saa yaram.

Boudeh yaye defa féenjal féebaar bii (covid-19), dina meuna neka aak domb djii. Khaana beoudeh féebaar bii féjn tchi.

Boudeh Yaye defa féeñyaal féebaar, wayé sokhlaa wuul fadje, defa wooraa njibii tôg keuram khaar  aye aart knga khaani def tchii woora djôg.

Yaye yii aandaa aak féebaar bii (corona) dûñio woora nampaalé dômb djii, wooraa raxaas wéen tdjii aak sabu aak ndokh baalaa muy nampalaé, sôl masque, aak raxaas lokhô déf tchii boke.

Aye scanner dinaa aam.
Kuneka defa woora khaamni ndiibaal biinga khaam, defay taakhaw, loolou yeup tchii telefone laay aam.
Bayii tchii khéel aye borom khaam khaam yii séen setsi dína aand aak fiinga tolou tchii saa eumb.
Tanka aandoulou aak féebar.
Nieup ñio woora djuur diina ñio djuur (inchaAllah), wooruléen niar khéel walla khâlât tchii meuna dougou tchii biir hôpiteaux yii.

Støt Mino Danmarks arbejde.


Kadoum Moytu bou djogéee tchii biir njii ñio yoor aye vaccine

Institution bii yoor vaccine moungii laadj njeup ñio bok tchi loulo tudu (influmeter); maanam nga meun leen djaapalee tchii feeñial féebaar bii dii djokhée sodj, ñio meuna djaapa laan tée kheekh coronavirus.

Influmeter bii, yow saa bop yakoy wutii, yow laanju beuga khaam feebâr bii fumu tôlou, nga meun ñio waakh ndakh yangui yeug daara sii tchaa yaram – lii yeup meunio meuna diapalee aak yoku suñu khaamkhaam tchi sûñû rew.

Kou deuk tchii biir Danemark yeup meuna naa ñio djaapalé – khaalé, maag, kû wéer aak kû féebaar nieup meun naa ñiu boke. Boudeh daangaa feerbaron walla nga aand ak weerguu yaaram njeup meun naanju djapalé. Boul râgaal diin ñio djapalé.

Influmeter bii, tchii biir depatrtement de infection aak epedemi, tchii État laa neka, moy ñio aar tchii aye féebaar nga khamni defay waalaaté fii tvhii biir rewmii Danemark. Njôm njoy dookhaal inlumeter bii, ñio meun khaam tchii waakhtou bii nga khaamnii COVI-19 moo taxaw.

Fekal influmeter tchii seen site: www.influmeter.dk

Støt Mino Danmarks arbejde.


Waakhtaanou pres tchii Ministaire bou Rewmi beussou fukk ak juróom-ñeent tchii marts 2020

Niit: Ministre bou rewmi Mette Frederiksen, ministre weergou yaram Magnus Heunicke, directeur tchii biir weergou yaram Soeren Brostroem, ministaire bitim rëw aak Chéfou takk-der bou rewmii Torkild Fogde.

Ministre bou Rewmi defa tiidjii waakhtaan bii diiñio leeral niata niit ñio aand aak féebar bii: Juróom  fukk ak ñiar (82) ñiô teede tjii hôpitâl yii, fukk ak juróom-ñett (18) séen cas defa djaafé, ñiit yii seen cas yii defñio béta. Motakh duuñu woora meuna def louñu meun ñio waanyii waallaaté yii.
Motakh soubaa beus bou fukk ak juróom-ñett tchii wëerou marts (18.3.2020) aye wakhtou fukk bout djoté, baa beusou fanweer tchii biir wëerou marts (30.3.2020) Rewmii diina djeul aye measure yuu bées.

  • Niit yii meuna daajalanté woroul eupa fuki niit (10), lolou mo doone tchii aye khéew mou done tchii biir walla sii biiti. Tchii biir keur woorngéen oytu, ngeen yeem tchii fuki niit.
  • Boutique/marché yii tamit aamnaa ñio seen reglement. Niit kuy ndugi defa woora aam place, daageen woora bagña djeegaanté. Raxassou kaye defa wora aam – tchii biir ak tchii biiti.
  • Waalloum sport yeup defa woora tedj, maanam centre fitness, wâtt kaat yii… borom boutique bou neka nga khaam nii liingaay sokhlaa tchii ñiom nekoul tchii weergu yaram.
  • Soireé tchii biir bôite yii, njii tokh chicha, bar yii njeup daay tedj.
  • Djaaykou léka yii, café yii yeup defa woora tedj. Sauf boudeh daangaay daaj emporté.
  • Danois beu njibii sii, defa wora diindii touram tchii liste bii boudeh saa tour defa fegn foofu. Boo paré nga tedjuu saa keur aye fukk ak ñeent faan.

Lou tchii topeu moy Heunicke, Brostroem ak Fogde ñio waakh dino woora oytu léegui léegui ñio meuna xatal feaabr bii aak lou tvhii meuna topeu. 
Béene niit meunoul bayi djeul wallam, lolou laa ministaire tchii weur gii yaram wakh, defa djoubal wakh tdji sii ndongoma yii.

Ministre bou rewmi neena boudeh daangaa aam khéel ñiar, ndakh daanga woora deem diner ak saa aye khaarit, kone tôgal saa keur moo geuna wôr.

Ministre bou rewmi mungi bakhlée nieup nga khamnnii douñiô djaap sii taxaawai rewmi.

Lou tchii tope moy Ministre bou Rewmi defa ladjté aye ndimbal; djaapalé ligeuy kaat yii, nii ligayal seen bop, ûsune yii, souba diina waakhtaan aak partii yii.

Ministre biitem rew neena khaam naa nii aye niit duñio meuna njiibii léugui nii. Motaakh duñio wora wuut fuñio meuna neka, baa wakhtou njii djot.

Støt Mino Danmarks arbejde.


Wakh bou gaat bou djiogeu tchii ministere beus bii fukk ak ñett tchii biir weerou marts wakhtu fukk akk juróom-ñiar

Niit; Ministre bou Rewmii Mette Frederiksen, Ministere biitiim rew Jeppe Kofoed, Ministere bou justice Nick Haekkerup aak takk-der bou rewmii Torkild Fogde.

Bou ndjeke Gouvernement bii defa djokh khee takhaa waye corona-virus bii tchhi Danemark:
802 ñio aam febar bii, 23 ñio teeda tchii biir hôpital yii, 2 ñiar nga khaamnii seen weer gui yaaram defa neka khâwâ djafee.

Mette Frederiksen defa waak tchii louñio woura def tchii waaloum feebar bâlaa mouy wâlaaté tchii biir Danemark.

Beene moy, hôpitâl yii diina ñiô taakhawaal operation yiinga khaam nii nekouñio tchii digenté deh ak doundou. 

Njaareel bii moy, ministére biitem rew duounjo djokhee aye kadou, maanam touki yii nga khamnii amoul sollo geen bayiiko, tamit yeen yii danois yii neka biitem rew, yeen dageen woraa njiibisii bou gaw. 

Njeeteell bii moy, moy taakhaa way bou rey, moy suba gaawu bou fuuk ak ñeent digg bëccëg,  Danemark deefay teedj aye frontier raam baa beuseu fuuk ak ñeent tchii Awril.
Loolou loumou teegi moy keene nga khamnii neekoul danois meunoul duugu tchii biir rewmi. 
Meu neka akk avion, walla bato, otoraay walla kaar. 

Khaanaa niit kii aam sokhlaa bou deegeur; maanam nga deeuka fii, ligeey walla ngay setsi niit ñio febar (yeenaa boka deerët) walla nga aam aye doom tchii biir danemark, nga beugeuleen seetsi.
Forntierou Danemark aye takk-der aak waa militaire ñiokoy garde.

Gouvernement bii beugeuna geen yeug nii, frontoier bii dina oubeegou, pour nii nga khamnii danio  dougaal aye leka. Moo takh keen worul raagal, kdakh leka diina doy. 
Aak boul faateenii yeen nii aam pasport yeen diigeen meuna dougou tchii biir rewmii.

Støt Mino Danmarks arbejde.


Samarbejdspartnere til Mino Danmarks indsats med oversættelse af myndighedernes udmeldinger om covid-19 i Danmark:

Vær med til at sikre
et ligeværdigt Danmark
– for alle!

Sammen styrker vi minoritetsetniske danskeres
muligheder, stemmer og samfundsdeltagelse



Hvert eneste medlemskab og donation styrker Mino Danmarks legitimitet og eksistensberettigelse.

Det gør en forskel og styrker foreningens muligheder for at lykkes med at skabe et lige samfund, uanset etnisk baggrund.

Hvert eneste medlemskab og donation styrker Mino Danmarks legitimitet og eksistensberettigelse.

Det gør en forskel og styrker foreningens muligheder for at lykkes med at skabe et lige samfund, uanset etnisk baggrund.