https://mino.dk/covid19/wolof/#xetu-tektal-you-bes-bou-djoge-tchii-digle
06/05/2020 /
/Bou djekeu ñi woora oytû tchii wallum COVID-19 défa yatû wône, motakh diktal bou bés, ñio meuna kham kaan mô woora oytû tchii wallaté coronavirus.
Djûrôm ñiar mbolo ñio woora oytû:
1.Kou djem maag – leup tchii wër gû yaram
Virusbii liimu wôné moy maag ñio aam 70ans djem kaw, aak ñii wésû 80ans, ñio yomb waalaté ak fébar. Ñio gaaw aam fébar bii moy maag kû aam 65ans, boudeh dangâ aand ak fébar.
Kû djem maag aam 65ans djem kaw, boudeh daanga aand ak wér gu yaram yow worulô ragal. Môtâkh légui maam yii meun ngén guiss seen sët yii – ngën néhkhãl léen.
2.Ñi deuk tchii resisdence
Kou deuk tchii residence défa dône maag, aand ak hasay bou néxûl. Môtakh ñii lagñio wora oytu.
3.Mbolo kou aam yaram
Boudeh danga aam yaram lou tchii beure dangay aand ak yénéen fébar, kome diabéte wala fëbaar khôl. Niit kô khamni défa aam BMI bou eup 35, wala BMI bou 30 aand hasay meuna aam aye djafé djafé boudeh daanga aand ak COVID-19.
4.Niit ñio aand ak yéene hasay
Dou Hasay fébar yeup moy djokhé djafé djafé, sûr tout boudeh yangui fadjû. Si sûf meun nga guiss fëbar yii néka tchi hasay boudeh danga aam COVID-19:
https://www.sst.dk/da/Udgivelser/2020/Personer-med-oeget-risiko-ved-COVID-19
5.Khâlé bou aand ak hasay fébar
Ýene khâlé ñio aam hasay fébar ñio wora oytû COVID-19. Sûr tût khâlé yii nga khamni diñio sokhla ndimbal – baalaa pandemi dii aam – Khâlé yii aak séne mbôk dina ñio aam ndimbal.
6.Niit kou aamoul këur
Niit kou aamoul këur défay aam djafé aak sëtay soré niit tchii bôpam dina méti. Motakh wallanté bii defay yômb. Lou tchi tôp moy niit kou aamoul këur lou tchii beuré défay aand aak hasay fébar. Lii yeup défa bôk tchii mbolo bii meuna aam fébar bou djafé.
7.Djiigén bou aand aak bïr
Lii ndimbal rék la, ndakh kou aand ak biir défa gâw aand ak hasavay fébar. Daar wônéwûl kou aand ak biir, walla dômb djii, ñiom niar séen fébar geuneul méti mbolo. Tchii lûñû khaam, yaay ak dôm ñii wosin aak aand ak COVID-19, dômb bii diina djûdû baala djotaam. Motakh ñio wora aru yaaye aak dômb.
13/05/2020
Lou djogé tchii taxa way bii djogé tchii ministére bii bës bii 12. mai 2020 Danemark défa bok tchi yëw […] Læs mere… Læs mere…
12/05/2020
Niit you beuré ñju gui défar aye sën muuraay gémiñ bôp. Ministaire bou dal néena ngéen oytû lii dône aye […] Læs mere… Læs mere…
07/05/2020
Lou djogeu tchii taxaway 7. may ak Ministre bou djité rewmi Mette Frederiksen Danois yeup défnañio lou ñio meune, dii […] Læs mere… Læs mere…
04/05/2020
Mbolo, nga khaamni défa aand ak fébar bou yombà nga khamni défay yômbal walanté COVID-19 tchii yaram, meun nga wô […] Læs mere… Læs mere…
06/04/2020
Tarixx bii dëgër na, ñuu ngui tchii yône: Ñiaar téemer ak ñéet ñjô teudeu tjibiir hôpital yii, Béene tëmér ak […] Læs mere… Læs mere…
28/03/2020
Liinga wora khaam tchii corona: Wakhtou bii défa khaawaa djafé ndakh féebar bii. Moo takh ñio geuna deugeuraal suñu taawaye, […] Læs mere… Læs mere…
23/03/2020
Lii tchii biir conference aak journaliste yii beusou bii ñaar-fuuk ak ñett tchii biir wéeru marts 2020. Miinistere bouy djiitaal […] Læs mere… Læs mere…
19/03/2020
Beusou alxamis fukk ak juróom-ñeent bii tchii biir weerou marts, Ministaire bou weerguu yaram defa djokhé kaadouam tchii djiigeen bou […] Læs mere… Læs mere…
18/03/2020
Institution bii yoor vaccine moungii laadj njeup ñio bok tchi loulo tudu (influmeter); maanam nga meun leen djaapalee tchii feeñial […] Læs mere… Læs mere…
17/03/2020
Niit: Ministre bou rewmi Mette Frederiksen, ministre weergou yaram Magnus Heunicke, directeur tchii biir weergou yaram Soeren Brostroem, ministaire bitim […] Læs mere… Læs mere…
Hvert eneste medlemskab og donation styrker Mino Danmarks legitimitet og eksistensberettigelse.
Det gør en forskel og styrker foreningens muligheder for at lykkes med at skabe et lige samfund, uanset etnisk baggrund.
Hvert eneste medlemskab og donation styrker Mino Danmarks legitimitet og eksistensberettigelse.
Det gør en forskel og styrker foreningens muligheder for at lykkes med at skabe et lige samfund, uanset etnisk baggrund.